Arva

Jahman X-Press

Arva aar Njaye
Arva yaw kaay
Arva aar Diogo
Arva yaba xari maam booy
Yàlla na bu dara yax
Mamadou
Diop yaba xari maam booy
Kon arva mooy

Ki mooy Arva sama lingeer bi
Buñ ne danga baax kenn du ni gulet
Wëratuma leneen yaw laa doon seet
Yaay sama reni xol
Gërëm naa la ndax Arva yaa may niital ni weer wi (arva)
Àljanna lay dundu fekk maa ngi sa wet (yaw laa am)
Yaay tool bu nandul nawet
Jémbët naa man sama jiwu ci yaw

Ndekke bëggawuma la xol bi kase (daagul ma lay wan)
Arva sama ruu gi laa la yénne (daagul ma lay wan)
Fu ma geesu gis la nga may gunge (daagul ma lay wan)
Ni tàkkandeer Arva sama sumal nga (daagul ma lay wan)
Yaw danga yore jikkooy jeegu puso (daagul ma lay wan)
Samay mbokk ka wax waxu maako
Yaay awa Sëriñ Babacar
Arva wayal naa la man Mamadou mi sa jëkkër

Kon wayal naa la ndameloo
Ndax sama sant ngay wuyoo
Diop yaba xari maam booy borom
Ree ju neex ji mbaa meroo
Tojal naa la koro nel
Sama xol yaa koy majloo
Diop yaba xari maam, lax nga sama gërëm

Kon wayal naa la ndameloo
Ndax sama sant ngay wuyoo
Diop yaba xari maam booy borom
Ree ju neex ji mbaa meroo
Tojal naa la koro nel
Sama xol yaa koy majloo
Diop yaba xari maam, lax nga sama gërëm

Bu ñu delluwoon démb manam
Imam yokkat caan gi
Ndax kontaan ci yaw
Wol say mbokk damay dolli
Yaw jeegu jëkkante nga
Waaye man nga taamu ndax naru góor du àndak mbayan yi
Boo fekkee woon keroog talaata nder
Jigéen ña talon seen bopp sa nekk ba
Ngir bañ gàcce duñu la yóbbul dara

Ndax yaw yaa jaay sa sant waaye sant bi nga jënde
Yombul sant daqu ko Diop du kenn kaay wuyoo

Kuy wër ku rafet judd
Ba yam ci moom dëppal
Ko fi gënul gënu la yaay borom maamu buur yi

Kon wayal naa la ndameloo
Ndax sama sant ngay wuyoo
Diop yaba xari maam booy borom
Ree ju neex ji mbaa meroo
Tojal naa la koro nel
Sama xol yaa koy majloo
Diop yaba xari maam, lax nga sama gërëm

Kon wayal naa la ndameloo
Ndax sama sant ngay wuyoo
Diop yaba xari maam booy borom
Ree ju neex ji mbaa meroo
Tojal naa la koro nel
Sama xol yaa koy majloo
Diop yaba xari maam, lax nga sama ngërëm

Diop yaaba xaari maam
Moom Mamadou yar na ñu ci baneel
(Matar ndumbe Soxna Niang
Serigne Codou Ndiaga Issa Dieye)
Leer gi bawan njukku ba maka
Mamadou, Mamadou
Yaa ba xaari maam
Chérie Arfaa

Ndameloo cire
Ndameloo cire bëggul ndame cire
(Diop Yaaba xaari maam)
Mamadou (yaaba xaari maam)
(Yaaba xaari maam)
Wax nga dëgg, waay!

Jiwaru Keita ko daan jël
Xaar ma Yàlla réew mi déglu leen ma
Maa way sama doom ko koy Arva
Toucouleur Koura Ndiéme billaay

Ndameloo cire
Ndameloo cire bëggul ndame cire
(Diop Yaaba xaari maam)
Mamadou (yaaba xaari maam)
(Yaaba xaari maam)
Koura Niang ma ta Kathia Torodo Samba Ngari Ndiana
Yaay majloo jigéen ñi
Yaay majloo góor ñi
Sama doom ji l'amour gaddu woon ba tay dañul
Jiitu nga leen saani cravacher gi daan leen


All lyrics are property and copyright of their owners. All lyrics provided for educational purposes only.