Libre Valdiodio

ADIOUZA

Gent gi du neen
Sa bidéew feñ na
Wéetaay weesu na jaambaar
Ñëwal ci leer, siggil nga dem
Am nga ndam

Ba àddunay tukki dootuñu la fàtte
Wetoon nga mais gagner nga
Ñoo ngi lay dello njukkal jaambaar
Dugg ndugusin ndax ar li nga gëm
Déggatoo mbokk xarit àndandoo
Na cér nga la ma ramatu yi doon jooy di la wetalee
Raw nga leen Guélowar!

Gent gi du neen
Sa bidéew feñ na
Wéetaay weesu na jaambaar
Ñëwal ci leer, siggil nga dem
Am nga ndam


All lyrics are property and copyright of their owners. All lyrics provided for educational purposes only.